LOOLU MOO TAX ab tukki la bu gaaw ci Mbindi yonent yi. Bi mu tàmbalee ci ni ñu sàkke àddina, dafay nettali li tax Yàlla yónni ab Musalkat ci àddina, kuy Musalkat boobu ak lan la def lu nuy tax a mëna xam Yàlla, bëgg ko te di dund ak Moom ba fàww. Bu fekkee sax ne nettalib juddug Almasi lu baax lool la ci jamonoy Nowel – film bu baax la itam ci jamono yépp ngir xeet yépp, ak sax ñi dul def xewum Nowel.